Aller au contenu

Wikipedia:Babel

Jóge Wikipedia.

Xët wii moo lay leeral nooy xamale yeneen jëfandikukat yi, say xameel ci yeneen làkk yi ak tolluwaayu xameel gi.



Li muy jariñ

Donte fii Wikipedia ci kàllaama wolof la, waaye du ñi fi nekk ñéppa déggante. Am na ñu déggul wolof, walla seenug dégg des na, ñu mana soxla ku ñu jokkool ci làkk wi ñu dégg, walla ci wolof yu yomb. Am na ay waa-wikipedia yu déggul wolof te di bëgga jàpp ci liggéey bi, kon di na am-solo lool nga wax ko ci yan làkk ngeen mana waxtaane, ngir njariñam mana feeñ.

Bii sémb di na yombal jokkoo gi ci biir aw askan wu barilàkk wu mel ne wu Wikipedia: ci misaal, di na yomb jot kuy wax wenn làkk wi, te itam di na xamale tolluwaayu dégginu wolof bu ab jëfandikukat bu bindu.

Nu ma koy defe?

Wikipedia:Babel
wo-1
fr-1
en-1
Seet waa-wikipedia ci làkk-ak-làkk

Doy na nga yokk ci sa xëtu jëfandikukat Babelbox bi, tabax ko ci topp tegtal yii:

  • Nga yokk ci limu làkk yi nga dégg te teg ci |
    • Misaal: {{Babel| (3 làkk)

Su ko defeen nag nga def ci tolluwaayu ni nga dégge wolof. Soo bëggee mu mel ne ni nga koy gisee (ci sa ndeyjoor), nga def: wo-0 walla wo-1 walla wo-2,añs.

Misaal: {{Babel|wo-1|fr-1|en-1}}

Yu wolof

Wikipedia:Babel
wo-5
wo-4
wo-3
wo-2
wo-1
wo-0
Seet waa-wikipedia ci làkk-ak-làkk