Xaal
Apparence
Xaal genn xeetu ñax la. Mi ngi bokk ci njabootug "cucurbitacées" te cosaanoo Afrig gu sowwu jant.
Melo wi
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Xaal ñam wu xonq la yor, Ay foytéefam buñu matee dëgg diisaayam danay àgg 5 jàpp 20i kilo. Foytéef bi daa mbege te xaw a muluŋ. Xaal garab la guy sax at ba at (nawet lay sax). Ronam ( peer ak dàtt) danay àgg ba 3i met ci guddayam. Xobam cig yaatal day ñatti-koñe.
Njariñ
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Xaal, doom bi dafa neex lool, léppam dees koy jëfandikoo. Ñamam dees kox lekk. Xoliit yi nag dees na ko jox rab yi mbaa def ci cere.
Turu xam-xam wi
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Citrullus lanatus
Tur wi ci yeneeni làmmiñ
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]- Araab: البطيخ
- Español: sandía
- Itaali: Anguria/cocomero
- Tirk: Karpuz
- Portige: Melancia Àngale: Watermelon
- Almaa: Wassermelone
- Kabiil: Tadellaεt
- Endo: Tarbuz Faaris/persã: خربوز/kharbuz
- Sapone: スイカ?( Suika)